Sabóor 20
Yal na Buur daan
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare,
yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,
3 yal na la yónnee wallam fa këram,
jàpplee la fa, ca Siyoŋ.
4 Yal na xool loo ko jébbal,
di rafetlu sarax soo ko lakkal.
Selaw.
5 Yal na la may li nga namm,
di sottal loo mébét,
6 ngay daan, nuy ree,
yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla.
Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan.
7 Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey.
Moo koy nangule fa asamaan su sell sa,
ci dooley ndijooram biy musle.
8 Ñiiki watiir,
ñeeki fas,
nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.
9 Ñoom ñooy jeng ak a jóoru,
nun, nu jóg, taxaw jonn.
10 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan,
te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.