Sabóor 19
Aji Sax ji màgg na
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Asamaan nee Yàlla màgg na,
kaw ne màww, biral liggéeyu loxoom!
3 Bésoo bés kàddu seere ko,
guddee guddi xamle ca mbir.
4 Du làkk, duy wax,
du baat bu dégtu,
5 suuf sépp la seen ndéey jibal,
seen kàddoo àkki cati àddina.
Kaw la Yàlla sampal jant xayma,
6 mu mel ni boroom séet, génne néegam,
di mbër mu doŋali, xéluw yoonam.
7 Asamaan lay fenke cat lii,
wëndeelu, sowi cat lee;
amul lu rëcc tàngooram.
8 Yoonu Aji Sax jee mat,
di leqli bakkan.
Lu Aji Sax ji seede dëgg la,
day xelal ku xeluwul.
9 Lu Aji Sax ji tegtale, njub la,
di bégal xol.
Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la,
di leeral gis-gis.
10 Santaaneb ragal Aji Sax ji mooy li sell
te sax ba fàww.
Lu Aji Sax ji digle, dëgg la,
ak njekk gu sotti.
11 Moo dàq wurus,
raw wurusu ngalam wu ne xas;
dàqati lem,
ëpp tem-tem.
12 Man, Sang bi, ci laay leerloo,
ku ko sàmm yokku yool.
13 Nit juum na, umple ko,
baal ma tooñ gu ma umple.
14 Te Sang bi, musal ma ci bàkkaaru teyeef,
mu bañ maa jiital,
ma mana maandu,
mucc moy gu réy.
15 Éy Aji Sax ji, lu saaw làmmiñ tudd
mbaa sama xol déey ma ko,
yal nay loo gërëm,
yaa may aar, yaa ma jot.