Sabóor 11
Ma làqoo Aji Sax ji
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji laa làqoo.
Ana lu ngeen ma naa: «Neel fëyy ni picc, toŋi sa kaw tund.
Xanaa du ñu soxor ñaa ngii, bank seen xala,
nas seenu fitt,
nara lëndëmtu, jam ku jub?
Bu ponki njub màbbee,
nu aji jub di def?»
 
Aji Sax jaa nga këram gu sell.
Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam,
ne jàkk doom aadama, di ko seetlu.
Aji Sax ji day seetlu ku jub;
ku soxor, bëgg fitna, mu bañ.
Day tawal ku bon ay mbugal;
sawaraak tamarax akub jaas dib añam.
Aji Sax jee jub, sopp njub;
kuy jubal, gis yiwam.