Sabóor 10
Néew-ji-doole sàkku na yoon
1 Éy Aji Sax ji, lu la taxa sore?
Xanaa dangay làqu, bésub njàqare?
2 Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole,
lal ay pexeem, ba jàpp ko.
3 Ku bon déy a ngi tëggoo bànneexu bakkanam,
ku bëgge di ñàkke wormaak a teddadil Aji Sax ji.
4 Ku bon daŋŋiiral, seetul dara,
xalaatam yépp mooy Yàlla amul.
5 Saa yu fexee, juble,
te gisul sa ndigali yoon yi ko tiim.
Ma ngay ciipu bañam yépp.
6 Ma nga naan ca xelam: «Duma tërëf,
safaan du ma dab tey ak ëllëg.»
7 Ay móolu la gémmiñ ga fees, ak fen ak njublaŋ,
njekkar ak ñaawtéef lal làmmiñ wa.
8 Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan,
làqu di bóom ku deful dara,
nëbbu di wootal néew-ji-doole.
9 Day làqu bérab, di yeeroo ni gaynde cim xunteem,
di yeeru aji ñàkk, ba jàpp ko,
laaw ko, ñoddi, yóbbu.
10 Ma ngay sëgg ak a waaf,
ba aji ñàkk daanu ci loxoom.
11 Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na,
dummóoyu na, du xoolati.»
12 Aji Sax ji, jógal!
Éy Yàlla, xàccil sa loxo.
Bul fàtte néew-ji-doole.
13 Bul may ku bon mu sofental la,
te naan ci xelam: «Yàlla du ma ko topp.»
14 Yaw de yaay ki nemmiku,
di gis njekkar ak naqar,
ku mu dal, nga sàmm àqam.
Néew-ji-doole wéeroo la,
ab jirim, nga dimbali.
15 Ngalla dammal loxol ku soxor ak ku bon,
topp leen seen coxor,
gi ñu yaakaaroon ne du feeñ.
16 Aji Sax jee di Buur ba fàww!
Xeet yeey sànku, jeex cim réewam.
17 Néew-ji-doole dagaan, Aji Sax ji dégg,
dalal xelam, teewlu ko,
18 ngir sàmm àqu jirim ak néew-ji-doole,
ba nit kiy suufu kese dootu xëble.