2
Ndigal yu sell
1 Yaw nag nangay waare li dëppook njàngle mu wér mi. 2 Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ.
3 Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa ñuy xér ci sàngara. Waaye nañuy jàngle lu baax, 4 bay xiir jeeg ju ndaw ji, ñu bëgg seen jëkkër ak seeni doom, 5 di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla.
6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu. 7 Te yaw, ci lépp lu mu mana doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngle wér te am faayda, 8 ànd ak wax yu wér yu kenn manta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
9 Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante 10 mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat.
11 Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc. 12 Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla, 13 di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam. 14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
15 Jàngleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.