6
1 Kon nag léegi nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu baña dalaat njàngle mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo wara tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla, 2 di leen jàngalaat ci mbirum sangu set ci ay fànn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu jëm ci àtte biy sax dàkk. 3 Te noonu lanuy def, bu soobee Yàlla.
4 Li nu wara jëme kanam mooy lii: su amee ay nit ñu Yàlla xasa leeral ba noppi, ñu mos mayu Yàlla gi, am wàll ci Xelam mu Sell, 5 te xam mbaax, gi ci kàddug Yàlla, ak kéemaani jamono jiy ñëw, 6 te loolu lépp teewul ñu walbatiku, ñooñu kenn dootu leen mana yeesalaat, ba ñu tuub seeni bàkkaar. Li ko waral moo di, dañoo bëgga daajaat Doomu Yàlla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaañ.
7 Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox ñi ñu koy beyal gàncax gu am njariñ, day jot barke bi jóge ci Yàlla. 8 Waaye su meññee ay dég ak ay xaaxaam, du am benn njariñ; repp na ñu alag ko, te lakk lay mujje.
9 Waaye nag yéen samay soppe, su fekkee ne sax nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li gën ci yéen te ànd ak mucc. 10 Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak mbëggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te yéena ngi koy def ba tey. 11 Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yéen wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di séentu. 12 Bëggunu ngeen tayel, waaye royleen ñi gëm te muñ, ndaxte ñooñu ñooy jot li leen Yàlla dig.
Li Yàlla dige lu wóor la
13 Ibraayma bokk na ci ñoom. Bi Yàlla di dige ak moom, manul woona giñ ci keneen ku ko gëna màgg, ba tax mu giñ ci boppam, 14 ne ko: «Sàllaaw dinaa la barkeel, yokk saw askan.» 15 Noonu Ibraayma di xaar tey muñ, ba jot li ko Yàlla digoon.
16 Nit kuy giñ nag, daf koy wékk ci ku ko sut. Ngiñ lu mel noonu moo wóoral mbir te mooy jeexal lépp lu ñuy werante. 17 Ñi wara jot li mu dige, Yàlla dafa leen bëggoona won ne dogalam du tebbiku mukk; looloo tax mu dige, boole ci ngiñ. 18 Noonu ñaari jëf yooyu nga xam ne duñu tebbiku te Yàlla manu cee dellu gannaaw, dañu nuy gëna sóob ci muñ, nun ñi daw ba am kiiraay, ngir nu mana téye bu dëgër yaakaar, ji mu nu dig. 19 Ci yaakaar jooju lanu sës sunu xol, ba mana sampu bu dëgër. Yaakaar la juy jàll ba fa Yàlla nekk, ca gannaaw ridob bérab bu sell baa sell. 20 Yeesu ci boppam moo fa jëkka dugg, muy ndaw li nu jiitu, ñu def ko sarxalkat bu mag ba fàww, mel ni Melkisedeg.