Sabóor 87
Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi
Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor.
 
Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya.
Aji Sax jee sopp bunti Siyoŋ gii,
mu gënal ko fu askanu Yanqóoba dëkke.
Yaw, dëkkub Yàlla bi,
tuddees na say jaloore.
Selaw.
Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg.
Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus.
Nit a ngii, juddoo fa,»
te teewul ñu cosaanale ko Siyoŋ,
ne kii ak kee fa bokk juddoo,
te Aji Kawe jee saxal Siyoŋ.
Aji Sax jeey lim xeet yi, limaale leen
ne: «Kii fi la juddoo.»
Selaw.
Kuy fecc ak kuy woy ànd naan:
«Sunu cosaanoo cosaan fii la!»