Sabóor 37
Bu sa xol jóg
1 Ñeel Daawuda.
Bu sa xol jóg ci ku bon,
bul ñee kuy def njombe.
2 Léegi mu wow nim ñax,
lax ni gàncax.
3 Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax,
ba des ci réew meek jàmm.
4 Deel bànneexoo Aji Sax ji,
mu may la say nammeel.
5 Jébbalul ci Aji Sax ji,
dénku ci moom, mooy sottal.
6 Day setal sab der ni jant bu fenk;
sab àtte ne ràññ ni njolloor.
7 Neel tekk, xaar Aji Sax ji,
yaakaar ko.
Bu sa xol jóg ci kuy baaxle,
tey lal ay pexe.
8 Baal mer, dëddu xadar.
Xol bu jóg, loraangey neen.
9 Ku bon, ñu dagg, sànni;
ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi.
10 Nes tuut, ku bon ne mes,
nga seet, seet, mu réer.
11 Waaye néew-dooleey jagoo réew mi;
jàmm ne ñoyy, ñu bége.
12 Ku bon fexeel ku jub,
di ko màttu,
13 Buur Yàlla di ko ree,
xam ne bésam a ngi ñëw.
14 Ku bon bocci saamar,
tàwwig fitt,
nara rey ku ñàkk, néewle,
nara bóom kuy jubal;
15 far jam boppam saamaru xol,
fittam damm.
16 Aji jub, as tuutam
moo gën koomu ku bon.
17 Ku bon kat, sa doole dëddu la;
ku jub, Aji Sax ji wallu la.
18 Ku maandu, Aji Sax ji yég la,
sab cér sax.
19 Bu mettee doo rus,
te bésub xiif dangay regg.
20 Ku bon sànku;
noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la,
bu tàkkee, jeex tàkk.
21 Ku bon leb, du fey;
ku jub yéwén, di joxe.
22 Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos;
mu alag la, nga dog.
23 Aji Sax jeey sopp saw yoon,
jiite say jéego.
24 Soo tërëfee it, doo daanu.
Aji Sax jee lay walloo loxoom.
25 Ba may ndaw, ba tey may mag,
gisuma ku jub ñàkk ndimbal,
mbaa askanam di dunde yalwaan.
26 Day saxoo tabe, di leble,
askanam barkeel.
27 Dëddul mbon, di jëfe mbaax,
ba dëkke réew mi fàww.
28 Aji Sax ji kat daa sopp yoon,
te du wacc jaamam bu gore.
Day fegu ba fàww,
askanu ku bon dog.
29 Aji jub ay jagoo réew mi,
dëkke ko ba fàww.
30 Kàddug aji jub day xelu,
wax ja jub;
31 yoonu Yàllaam a nga ca xol ba,
du dox ba tërëf.
32 Ku bon a ngi yeeru ku jub,
di ko wuta bóom.
33 Waaye Aji Sax ji du ko bàyyeek moom,
te deesu ko daan cib layoo.
34 Yaakaaral Aji Sax ji, sàmm yoonam,
mu teral la, nga jagoo réew mi,
ku bon sànku, ngay gis.
35 Damaa gis ku bon di note,
te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax,
36 ma jaareeti fa, ndeke wuute na,
ma seet ko, gisuma ko.
37 Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub;
muj, fa nitu jàmm.
38 Moykat yeey sànkoondoo,
ku bon amul muj.
39 Aji Sax jeey musal ku jub,
di ko aar bésub njàqare.
40 Aji Sax jee koy taxawu, wallu ko,
wallu ko ci ku bon, musal ko,
ndax li mu ko làqoo.