Saar 7
Njiitu takk-der ba yooloo na ngëmam
1 Yeesu wax na kàddoom googu gépp, askan way dégg, mu doora jàll biir Kapernawum. 2 Foofa nag ab njiitu takk-der bu waa Room a nga fa woon, ab jaamam woppoon bay bëgga dee, te njiit la soppoon ko lool. 3 Ba njiit la déggee mbiri Yeesu, daa yebal ñenn ca magi Yawuti dëkk ba ca moom, ñaan ko ngir mu dikk xettli jaamam. 4 Magi dëkk ba agsi ca Yeesu, tinu koo tinu, ne ko: «Ki nu yebal ci yaw de, yelloo na sa ndimbal, 5 ndax ku sopp sunuw xeet la, te sunu jàngu bi sax, moo nu ko tabaxal.»
6 Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko. 7 Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér. 8 Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.» 10 Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
Yeesu dekkal na doomu jëtun ba
11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom. 12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa. 13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.» 14 Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.» 15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja. 16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
Yeesu jàngle na ci mbirum Yaxya
18 Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya, 19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?» 20 Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21 Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis. 22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi* 7.22 Seetal ci Esayi 35.5-6 ak 61.1. Muy kàddug waxyu gu jëm ci Almasi.. 23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal? 25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk. 26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax. 27 Ci moom moomu lañu bindoon ne:
“Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la,
xàllal la saw yoon.”
28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya. 30 Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.
31 Yeesu neeti: «Ana kon lu may niruleel niti tey jii? Ana lu ñuy nirool? 32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma di awoonte, naan:
“Noo leen toxorool, fecculeen,
nu dëjal leen, jooyuleen.”
33 Ndaxte Yaxya daa feeñ, lekkul dugub, naanul biiñ, ngeen nee: “Aw rab la àndal.” 34 Doomu nit ki feeñ, di lekk ak a naan, ngeen naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi.” 35 Waaye xel mu rafet, mboolem la mu jur mooy la koy dëggal.»
Yeesu gane na Simoŋ Farisen ba
36 Kenn ca Farisen ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la. 37 Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu. 38 Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga.
39 Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!» 40 Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.»
41 Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000)† 7.41 téeméeri junni: maanaam juróomi téeméeri dinaar; fukki junni: maanaam juróom fukki dinaar. Seetal Xaalis ci Leeral yi.. 42 Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?» 43 Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.»
Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.» 44 Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam. 45 Fóonuloo ma, dalale ma, waaye moom, ba ma duggsee ba léegi noppiwula fóon samay tànk. 46 Ag diw, diwewoo ko sama bopp, waaye moom, diwu xeeñlu la diw samay tànk. 47 Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.»
48 Yeesu nag ne ndaw sa: «Jéggalees na la say bàkkaar.» 49 Ci kaw loolu ña mu toogandool di lekk, naan ci seen xel: «Kii mooy kan bay jéggaley bàkkaar sax?» 50 Yeesu nag ne ndaw sa: «Sa ngëm musal na la, demal ak jàmm.»