Saar 23
Ayóoba nee Yàlla noppi na
1 Ba loolu amee Ayóoba àddu, ne:
2 Ba tey maa ngi jooy jooy yu metti,
di onk bay ub gémmiñ,
3 Éy bu ma xamoon fa may gise Yàlla,
ba àkki péncam,
4 diis ko sama mbir,
àgge ko lépp lu may tawat,
5 ba xam lu di tontam,
dégg li mu may wax.
6 Ndax dooleem ju bare la may yeye?
Déedéet xanaa! Dina ma teewlu moos,
7 ba ku jub layoo faak moom,
ma daldi mucc sama àttekat fàww.
8 Seet naa wetu penku, Yàlla nekku fa,
ma seet sowu, gisuma ko.
9 Bu jàppee fa wetu bëj-gànnaar, gisuma ko fa,
bu jàllee bëj-saalum séenuma ko fa.
10 Ndaxam moo xam fi ma jaare,
te bu ma nattoo, ma génn ci
ni wurus wu ñu xelli.
11 Tànkam, sama tànk,
yoonam laa tegu, moyuma ko.
12 Dëdduwma ay santaaneem,
sama biir xol laa denc ay kàddoom.
13 Yàlla de kenn la, ana ku koy waññi?
Coobarey bakkanam lay def.
14 Mooy sottal lu mu ma dogalal,
te bare na lu mu ma nasal.
15 Lee tax su ma janook moom, tiit,
te lu ma gëna xalaat, gën koo ragal.
16 Yàlla daal a rëccal samaw fit,
Aji Man jee ma tiital!
17 Du lëndëm gi ma nekke moo ma wedamal,
du lëndëm gii ma muur.