Saar 53
1 Ana ku gëm sunub dégtal?
Ana ku Aji Sax ji won dooley përëgam?
2 Kii màgge fi kanamam ni njëmbat,
te nirook reen bu fette ag kekk.
Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire,
du meloom wu nu koy soppe.
3 Dees na ko xeeb, daw ko,
muy nit ku bare mitit
te miin naqar.
Mu mel ni ku ñuy dummóoyu,
dees koo xeeb te nawloowuñu ko.
4 Ndaxam moom sunu wopp la yenu,
sunuy mitit la sëfoo.
Nun nu foog ne dees koo mbugal,
foog ne Yàllaa ko duma, torxal ko.
5 Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko;
sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko.
Yar yi nu jàmmal moom la dal,
te mooy ki nu wére ciy góomam.
6 Nun ñépp a lajj niy xar,
ku nekk walbatiku topp yoonam,
te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.
7 Dees koo néewal doole, mitital ko
te ubbiwul gémmiñam,
xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji,
ne cell ni xar mu ñuy wat,
ubbiwul gémmiñam.
8 Àtte nañu ko ñàkkal, yóbbu,
te ag maasam kenn teewluwu ci ne
tooñ gu sama bokk yi tooñ
lees ko dagge ci réewum aji dund ñi,
te loolu lees ko fàdde.
9 Ni ñuy robe saaysaay lañu ko robe,
denc ko ci bàmmeelu boroom alal,
soxorul, fenul.
10 Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii,
teg koy naqar,
su nangoo doon saraxu peyug tooñ,
gis askanam, aw fanam gudd,
te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
11 Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko,
te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub,
ba mu àtte leen àtteb njekk,
sëfoo seeni ñaawtéef.
12 Moo tax ma di ko jox ab cér
ci biir ñu bare,
mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem,
ngir moo jébbale bakkanu boppam,
ñu limaale kooki tooñkat,
moo gàddu bàkkaaru ñu bare
te mooy tinul moykat yi.