Saar 32
Dëgg ay mujj
Buur a ngii, njekk lay nguuroo,
jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;
ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw,
di kiiraay ci ngëlén,
mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ,
mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm,
te noppi ñiy dégg dañuy teewlu,
ku yàkkamti di ràññee, ba mana xam,
làmmiñu ku dër gaawa wax lu leer.
Booba deesatul wooye ab dof, gor si,
te njublaŋ dootu dégg «ku tedd ki.»
Ab dof, waxi dof lay wax,
xel ma di nas ñaawtéef,
mu nar jëf ju teddadi.
Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji,
di xiifal ku xiif,
di xañ ku mar lu mu naan.
Ab njublaŋ, ay pexeem musiba la.
Njekkar lay nas,
ba bu néew-ji-doole sàkkoo dëgg it,
mu fen ba lor ko.
Waaye gor si, ngor lay mébét,
te ngor lay wéye.
 
Yeen jigéen ñi dal xel,
taxawleen temm, déglu ma;
yeen janq ji féex,
teewluleen ma.
10 Yeen jigéen ñi dal xel,
fi leek at aki fan ngeen jàq;
witt mi du baax, ngóob du taxaw.
11 Jigéen ñi dal xel, ragal-leen;
yeen ñi féex laa ne, tiitleen!
Futtikuleen, ba ne duŋŋ;
gembooy saaku, ñaawloo.
12 Fëggleen seen dënn,
jooy tooli bànneex ya,
jooyleen reseñ ju nangu ja,
13 ak sama suufas bokk,
ya ay dég aki dagg nangu.
Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma,
ak dëkk bu xumb ba.
14 Kër gu rafet sax, dees koy wacc,
dëkk baak riiram, dees koy dëddu;
tund ak tóoju doon ay xunti ba fàww,
mbaamu àll ne ca finaax, jur ga di ca fore,
15 ba keroog leeru xel sóobale nu fa kaw,
màndiŋ mi sopplikub tóokër,
tóokër meññ, ba ñu ne ab gott la.
16 Su boobaa yoon dëkke màndiŋ mi,
njekk tooge tóokër bi.
17 Su booba njekk ay jur jàmm,
njekk ay dalal, di aare ba fàww,
18 ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm,
ci dëkkuwaay yu wóor,
dal-lukaay yu dal xel.
19 Gott bi day daanu ci tawub doji yuur,
dëkk bi detteelu ba ne dett.
20 Waaye ndokklee yeen ñi tala ji fépp fuy ndox
te saña afal nag ak mbaam.