Sabóor 102
Yàlla, bu ma rey
Muy ñaanu néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem.
 
Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la;
yal na sama yuux àgg fa yaw.
Bu ma dummóoyu bésub njàqare;
teewlu ma,
gaawe ma sama bésub woote!
Samay fan a ngi wéy ni saxar,
sama yax yi mel nib taal.
Sama xol bi wow ni ñax mu xuur,
ba lekk safatu ma.
Damaa jàq, di onka onk,
ba desey yax.
Ma mel nim tan ci màndiŋ mi,
mbete looy cib gent.
Nelaw të;
ma mel ni picc mu wéetoo puju néeg.
Bés bu ne noon yi di ma sewal;
ñi may ñaawal di móoloo sama tur.
10 Lekkuma xanaa di diwoob dóom, toroxloo;
te lu ma naan, tuur ca rongooñ,
11 te sa mer ak sa xadar a tax,
nde yaa ma fab, xalab.
12 Ker a ngi law, nara mëdd samay fan.
Maa ngi wowat nim ñax.
 
13 Waaye yaw Aji Sax ji, yaay des ba fàww,
saw tur saxal maasoo maas.
14 Yaw yaay taxaw, ñeewante Siyoŋ,
ndax baaxe ko jot na,
àpp ba kay mat na.
15 Sa jaam ñeeka sopp doji dëkk bii ñu màbb,
ñoo ñeewante tojiti gentam bii.
16 Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji,
buuri àddina sépp wormaal darajaam,
17 nde Aji Sax jeey tabaxaat Siyoŋ,
nara feeñeg leeram.
18 Mooy nangul aji tumurànke,
xeebul ñaanam.
19 Nañu bindal lii maasug ëllëg,
ba xeet wu sosoogul màggal Ki Sax,
20 nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw,
di niire suuf fa asamaan,
21 ngir teewlu onki ñi ñu tëj,
nara ubbi ñi dee di seen àtte,
22 ba ñu siiwal turu Aji Sax ji fi Siyoŋ,
màggale ko fi Yerusalem,
23 kera ba xeet yiy bokk daje,
ñook réew yi, ngir jaamu Aji Sax ji.
 
24 Sama digg doole la ma semmale,
gàttal samaw fan.
25 Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex.
Bu ma yóbboo sama diggi fan.
26 Bu yàgg nga samp suuf,
sàkke asamaan say yoxo.
27 Ñoom ñuy jeex, yaw nga sax,
ñoom ñépp ràpp ni mbubb,
nga soppi leen niy yére, sànni;
28 te yaw ngay kenn ki,
te say at amul kem.
29 Sa doomi jaam ñeey dëkk;
seen askan sax fi sa kanam.»