Sabóor 82
Yàllaay àtte ndawi péncam
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam,
di àtte ndawi péncam, naan:
«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ,
ak di faral ku bon?
Selaw.
Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim,
tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana,
di leen xettli ci ku bon.
 
«Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu;
xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef,
ba kenuy suuf yépp di jaayu.
 
«Dama ne ay yàlla ngeen,
yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.
Waaye du leen tee dee ni doom aadama,
du leen tee daanu ni képp kuy njiit.»
 
Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina,
yaw yaa séddoo xeetoo xeet.