Sabóor 35
Aji Sax ji, àtte maak noon
Ñeel Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, digaaleel ak samay digaale,
xeexal maak ñi may xeex.
Fëkkal sa pakk ak sa kiiraay,
taxawusi ma,
xàcci sa xeej ak sa sémmiñ,
dajeek ñi may dàq.
Déey ma, ne ma: «Sag mucc, man a.»
Ñiy wut sama bakkan, yal nañu rus ba torox;
ñi may fexee lor, yal nañu leen waññi, sewal leen.
Yal na leen malaakam Aji Sax ji bëmëx,
nim ñax mu ngelaw wal.
Yal na leen malaakam Aji Sax ji dàq,
ñuy lëndëmtuy tarxiis.
 
Defuma dara, ñu di ma fiir,
defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.
Yal nañu sànkoo mbetteel,
keppoo seen fiir,
sànkoo seenum yeer.
 
Su boobaa ma bége Aji Sax ji,
bànneexoo wallam,
10 di ko sante sama jëmm jépp,
naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw,
di xettli néew-ji-doole ci boroom doole,
ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?»
 
11 Nit ku bon a ngi may duural,
di ma jiiñ lu ma yégul.
12 Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar,
ndaw tiisu xol!
13 Man de ba ñu woppee, maa ngi ñaawlu,
di woor, toroxloo,
sukk, ñaanal leen,
14 tiisoo leen ni saab xarit mbaa doomu ndey,
di ñaawlook a yoggoorlu ni ku ñàkk yaay.
15 Ma daanu tey, ñu daje di ko bége,
dajaloo fi sama kaw,
di ma fexeel te yéguma,
di ma yàpp, tëë ba.
16 Tekkiwuñu dara, di ma ñaawal rekk
te di ma màttu.
17 Éy Aji Sax ji, loo deeti seetaan?
Musal ma ci seenum pàdd,
wallu ma ci yii gaynde,
sàmmal ma sama benn bakkan bii!
18 Maa lay sante fa ndaje yaatoo,
màggal la digg mbooloo mu yaa.
 
19 Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo.
Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree.
20 Waxuñu jàmm,
xanaa di ràbbal niti jàmm ci réew mi
ay kàdduy tuuma.
21 Ñu ngi ma ŋa ŋàpp, di ma tuumaal,
naan: «Yaw a, yaw a, noo la gis!»
 
22 Éy Aji Sax ji, yaa ci gis, bul selaŋlu,
éy Boroom bi, bul ma sore.
23 Jógal, sàmmal ma sama àq.
Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.
24 Aji Sax ji sama Yàlla, àttee ma sa dëgg,
ñu bañ maa ree!
25 Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.»
Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»
 
26 Ku bége sama njàqare,
yal nanga rus, ba torox.
Kuy réy-réylu ci sama kaw,
yal nanga am gàcce, ne yàcc.
27 Ku bége sama der bu set,
yal nanga bànneexu, di sarxolle,
foo tollu di biral naan:
«Aji Sax jee màgg!
moom miy bége jàmmi jaamam.»
28 Man it ma tudd sa njekk,
di la dëkke màggal!