Saar 21
1 Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji,
fu ko soob mu jëme ko fa.
2 Lu waay def, daa jub ca moom,
waaye Aji Sax jeey natt xol yi.
3 Deel def dëgg ak njekk,
moo gënal Aji Sax ji ab sarax.
4 Xeebaateek réy-réylu
mooy bàkkaar yi ñuy ràññee ku bon.
5 Farlu, woomle;
ku gaawtu, mujj néewle.
6 Alal ju la fen may,
cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.
7 Coxor day sànk boroom,
ndax day baña def njub.
8 Ab saaysaay day dëngal,
nit ku dëggu di jubal.
9 Dëkkeb ruq cim sàq
moo gën jabar ju pànk.
10 Ab soxor day namma lore,
te du yërëm moroomam.
11 Boo mbugalee kuy ñaawle, ab téxét jànge ca;
nga jàngal ku rafet xel, mu yokku.
12 Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon,
te mooy sànk ku bon.
13 Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk
dina woote wall, wall ñàkk.
14 Ku mer, may ko ci sutura, mu giif;
boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.
15 Bu yoon amee, ku jub bég;
kuy def lu bon jàq.
16 Ku noppee jëfe xel,
noppluji njaniiw.
17 Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk;
ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.
18 Ku bon këppoo ayu ku baax,
workat gàddu musibam kuy jubal.
19 Dëkke ndànd-foyfoy
moo gën jabar ju tàng, bare ay.
20 Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw,
ab dof saax-saaxee josam.
21 Ku saxoo njekk ak ngor
am fan wu gudd, naataangeek daraja.
22 Ku ñaw mana daan jàmbaari dëkk bu mag,
ba màbb tata ja ñu yaakaaroon.
23 Ub sa gémmiñ, moom sa làmmiñ,
mucc ci njàqare.
24 Ku réy te bew, mooy ñaawle,
day reew, ba jéggi dayo.
25 Ab yaafus day bëgg lu mu amul ba dee,
ndax du nangoo liggéey;
26 day yendoo xemmem, te du am,
ka jub di joxeek a joxewaat.
27 Saraxu nit ku bon ñaawtéef la,
rawatina bu ci jubloo lu bon.
28 Seede buy fen day sànku,
kuy dégg, sa kàddu sax.
29 Ku bon day ñeme-ñemelu,
ku jub la muy def da koy wóor.
30 Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe,
ba manal Aji Sax ji dara.
31 Nit ay takk, bésub xare,
Aji Sax ji di maye ndam.