Saar 18
Bildàdd buurati na
1 Bildàdd mu Suwa àddu, ne:
2 Xanaa dungeen noppi mukk?
Àndleen ak xel, nu wax.
3 Ay mala ngeen nu teg daal,
def nu ay naataxóona?
4 Yaw nag yaa topp sa mer ba loru!
Ayóobaa, àddina day gental ngir yaw a?
Am aw doj ay toxal boppam ngir yaw?
5 Ku bon kay lag leeram di fey,
te taalam du jolli.
6 Xaymaam day lëndëm,
làmpam ba ko tiim ne kamaj.
7 Bu daa waaxu démb, di temp tey,
ay mébétam di ko mbas.
8 Moo dox ba tàbbi cib caax,
wëndeeloo biir mbaal,
9 tànk ba téqtaloog fiir,
ab racctal ne ko ràtt.
10 Buum ga koy lonk a nga suulu,
am yeer di ko xaarew ñall.
11 Lu ragloo koy darey mbetteel,
ne ko dann.
12 Mooy xiif ba doole réer ko,
musiba taxaw, xejjoo ko.
13 Jàngoro di ko ŋacc,
woppi ndee di lekk cér ya.
14 Ku bon lees di ñoddee fa jàmmi xaymaam,
diri ko ba fa kanam buuru musiba yi,
15 manees naa dëkke xaymaam, moomatu ko,
tamarax lees fay suy.
16 Ku bon mooy garab gu dee kaw ak suuf,
reen wow, xob lax.
17 Turam tukkee kaw suuf,
ba deesatu ko tuddem pénc.
18 Dees koy bëmëxeg leer, tàbbal lëndëm,
dàqe ko àddina.
19 Du doom, du askan wu muy waccey bokkam,
te kenn du desey dalam.
20 Waa sowu jommi cig mujam,
waa penku di rasu naa:
21 «Dalub kàccoor déy, lee di mujam,
ku faalewul Yàlla, nii la màkkaanam!»