Saar 12
Ayóoba nee Yàlla lu ko neex lay def
1 Ayóoba àddu ne:
2 Yeen daal yeenay nit;
ngeen dee, xel mu rafet dee.
3 Ndaxam man it am naam xel ni yeen,
duma seen cuune fenn,
te lii ngeen wax, kenn umplewu ko.
4 Maay reetaanu xarit,
te daan woo Yàlla, muy wuyu;
tey ñuy reetaan ku jub, mucc ayib!
5 Ku neexlee ngi ñaawal ku safaan dab,
defe ne safaan, ku tarxiis lay bëmëx.
6 Jàmm a nga ca xaymay yàqkat ya,
te xel mu dal di céru tooñkati Yàlla yooyu,
ŋàbb seeni yàlla.
7 Laajal rekk rab yi, ñu xamal la;
mbaa njanaaw yi, ñu wax la;
8 mbaa nga diisook suuf, mu xamal la;
mbaa jëni géej, ñu nettali la.
9 Ana ku umple ci mboolem ñii,
ne loxol Aji Sax jee def lii lépp?
10 Moo yor ci loxoom lépp luy dund,
yor noowal képp kuy noyyi.
11 Xanaa du nopp ay natt baat bu jib,
denqleñ di mosu ñam?
12 Mag ak xel mu rafet,
fan wu gudd ak ràññee.
13 Waaye Yàllaa boole xel ak doole,
moom pexeek ràññee.
14 Mu ngoog, keey màbb te deesul tabaxaat,
di tëj nit, te deesul tijji.
15 Mu ngoog, keey aj am ndox, mu maral,
mu afal am ndox, mu salfaañe àddina.
16 Kee am doole, keey sottal,
di boroom aji réer ak ka ko réeral.
17 Keey futti kàngam,
dofloo kilifa.
18 Keey foq mbaxanam buur,
jox ko ngemb, mu gemboo.
19 Keey futti sarxalkat,
jàllarbi njiit lu riigu.
20 Keey wedamal ku ñu wóolu,
xañ mag xelum ràññee.
21 Keey torxal garmi,
yolomal ngañaayu boroom doole.
22 Keey ñori lu làqoo xóotey lëndëm,
leeral lu noon këruus.
23 Keey màggal aw xeet, teg ca fàkkas leen;
keey lawal aw xeet, teg ca toxal leen.
24 Keey xañ njiitu xeet am xelam,
wërloo ko ndànd-foyfoy lu yoon amul,
25 muy làmbatoo lëndëm gu genn leer amul,
moo koy wërloo ni màndikat.