Saar 41
Aji Sax jee yor jamono
Yeen waa dun yi, xeremluleen, déglu ma;
yeen askan yi, takkuwaatleen,
jegesi te wax,
nu bokk teew, layoo.
Ana ku ñu yékkatee penku,
woo ko ci tànki njekk?
Ana ku ko jébbal xeet yi,
nangulal ko buur yi,
saamaram note ba ñuy pënd,
fittam jamat, tasaare ni boob?
Moo leen di dàq, ba jàll te jàmm a koy dal,
ay tànkam sax du laal suuf.
Ana ku def lii, dogal ko?
Xanaa ki dale fa njàlbéen di woo maas yi!
Man Aji Sax ji maa jëkk,
te man laak ñi mujj ba tey!
Waa dun yee ko gis, tiit;
waa cati àddina di lox;
dox ba agsi;
ku nekk di jàpple moroom ma,
naa mbokk ma: «Góor-góorlul!»
Tëggu weñ ba di ñaax tëggu gànjar ba,
boroom wàkku soññ boroom dékk,
ñu naa: «Taqaleb weñ yi baax na!»
tey daaj jëmmi xërëm ja
ay pont yu koy dëgëral.
Aji Sax jeey musal Israyil ciy noonam
Waaye yaw Israyil, sama jaam bi;
yaw Yanqóoba mi ma taamu,
yaw askanu Ibraayma, samab xarit!
Yaw mi ma jukkee fa cati àddina,
wooye la fa gëna sore,
wax la ne la: «Yaa di sama jaam,
maa la taamu te duma la wacc,»
10 bul ragal, yaw laa àndal,
bul tiit, maay sa Yàlla;
maa lay dooleel, dimbali la déy,
maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
 
11 Ma ne, képp ku la mere,
dees koy rusloo, torxal ko.
Kuy joteek yaw day neen, sànku.
12 Dinga ko seet, doo ko gis,
kuy jànkoonteek yaw, du mujje doon tus,
te kuy xareek yaw it day mujj neen.
13 Man Aji Sax ji maay sa Yàlla;
téye sa loxol ndijoor,
di la wax ne la: «Bul tiit,
maa lay dimbali.»
14 Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax,
yeen góori Israyil.
Man, maa leen di dimbali.
Kàddug Aji Sax jee,
sab jotkat, Aji Sell ju Israyil.
15 Maa ngii di la def
ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq;
ànd aki bëñam,
ngay wol tund wu mag, raatale;
dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.
16 Yaa leen di bàcc, ngelaw wal,
ngëlén tasaare;
yaw ngay bége Aji Sax ji,
di damoo Aji Sell ju Israyil.
 
17 Walaakaanaak néew-doolee ngi wër,
di wut um ndox, amul.
Seen put wow koŋŋ ak mar.
Man Aji Sax ji, maa leen di nangul;
man Yàllay Israyil, duma leen wacc.
18 Maay walaley dex kaw coll ya ne duŋŋ,
bënn bëti ndox digg xur ya,
def màndiŋ ma ab déeg,
suuf su ne sereŋ laay ballalem ndox.
19 Maay def garabi seedar aki séng ca màndiŋ ma,
saxal garabi mirt ak oliw ca joor ga,
sippar ak garabu pẽe, ak yeneen garab yu dëkke naat,
ma boole ca,
20 ndax nit ñi gis, ba xàmmee,
ñoom ñépp nemmiku, ba xam ne
Aji Sax jee def lii ci loxoom,
xam ne Aji Sell ju Israyil a sàkk lii.
Aji Sax ji tiiñal na tuuri yéefar yi
21 «Waxleen seenu lay,» la Aji Sax ji wax,
«Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax.
22 «Woneleen ko te wax nu liy ñëw.
Xamal-leen nu la woon, lu mu;
nu ba ci xel, ba xam lu muy jur,
te ngeen dégtal nu la dikkagul.
23 Biralal-leen nu mbiri ëllëg,
nu xam ne ay yàlla ngeen.
Defleen rekk lenn, muy lu baax di lu bon,
ndax nu bokk ko gis, ba yéemu.
24 Ma ne, yeen daal, dungeen tus;
seen liggéey du dara,
te ku leen taamu di ku seexluwu!»
 
25 Maa yékkatee nit bëj-gànnaar,
mu bawoo penkub jant,
di tudd sama tur.
Mooy note boroom dëkk ni ban
mbaa binit bu defarkatu njaq di dëggaate.
26 Ana ku yéene woon lii ca njàlbéen,
ba nu xam ko?
Ku ko yégle woon bu yàgg,
ba nu man koo dëggal?
Yéeneesu ko, yégleesu ko
te déggeesul seeni kàddu.
27 Waaye maa jëkka yégal Siyoŋ
ne leen: «Xool-leen, ñu ngii!»
Maa indil Yerusalem ndaw lu indi xibaaru jàmm.
28 Xool naa xool ci tuur yi, gisuma kenn;
du kenn ci ñoom ku ciy xelale,
ba ma laaj ko, mu mana tontu.
29 Ñoom ñépp a ngoogu, tekkiwuñu tus.
Seen liggéey, caaxaani neen,
seen jëmmi xërëm du dara, cóolóolu kese.