Saar 20
Kàddug waxyu ñeel na Misra ak Kuus
1 At ma bummib Asiri demee ca ndigalal Sargon buurub Asiri, ba songi dëkk ba ñuy wax Asdodd ca Filisti, ba mujj ko nangu, 2 fekk na Aji Sax ji wax, Esayi doomu Amocc jottli. Mu ne ko: «Demal summi tubéyu saaku ji nga sol, te summi say dàll.» Mu def noona, di doxe yaramu neen, tànki neen. 3 Gannaaw gi Aji Sax ji ne: «Esayi sama jaam bi def na yaramu neen, tànki neen lu mat ñetti at, muy firnde, di tegtal ci mbirum Misra ak réewum Kuus. 4 Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra. 5 Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.» 6 Bu keroogee ku dëkke tefes googu dina ne: «Xanaa kay du ñii lanu yaakaaroon! Te nu dawoon di wuti ndimbal ci ñoom, ngir rëcc buurub Asiri! Léegi nag nu nuy mucce?»