Saar 40
Esekiyel gis na kër Yàlla gu bees
1 Ba ñu duggee ca ñaar fukkeelu at maak juróom gannaaw ba ñu nu yóbboo ngàllo, mu yemook fukki at ak ñeent gannaaw ba ñu nangoo Yerusalem, bésub keroog booba yemook fukki fan, loxol Aji Sax ji dikk na fi sama kaw. Mu yóbbu ma ba foofa. 2 Ci biir peeñuy Yàlla la ma yóbbu ba réewum Israyil, wàcce ma ci kaw tund wu kawee kawe. Mu am fa ca wetu bëj-saalum luy nirook tabaxi dëkk bu mag. 3 Ba mu ma yóbboo ba foofa, ma jekki yem ci nit ku am melow xànjar, ŋàbb buumu lẽe ak yetu nattukaay. Ma nga taxaw ca buntu dëkk ba. 4 Waa ja ne ma: «Yaw nit ki, xoolal bu baax, teewlool say nopp te def sam xel ci mboolem li ma lay won. Ngir won la moo tax ñu indi la ba fii. Mboolem loo gis, nanga ko àgge waa kër Israyil.»
Natt nañu miir baak bunt ba féete penku
5 Ma jekki gis ab miir bu wër kër Yàlla gi ba mu daj. Waa jaa nga ŋàbb yetu nattukaay bu gudde juróom benni xasab* 40.5 xasab ñeent fukki santimeetar laak juróom. yu teg yaatuwaayu catu loxo† 40.5 catu loxo bu digg-dóomu di juróom ñaari santimeetar ak genn-wàll. . Mu natt talaayu miir ba, muy wenn yet, taxawaay ba it di wenn yet‡ 40.5 yet wi di ñetti meetar yu teg tuuti. . 6 Mu dem ca bunt ba féete penku, yéeg dëggastal ya, daldi natt guddaayu dëxu biir bunt ba, muy wenn yet. Benn dëx bi rekk, wenn yet la. 7 Néegi wattukat yi làng ak jaaruwaayu mbaaru bunt bi, bu ci nekk ab kaare la bu wetam di wenn yet. Diggante ñaari néeg yu nekk, miiru juróomi xasab moo ca dox. Dal-luwaayu mbaar ma ca biir, ab dëxam wenn yet la. 8 Mu natt dal-luwaayu mbaaru bunt ba ca biir, 9 muy juróom ñetti xasab, ay jënam dëlle ñaari xasab. Dal-luwaayu mbaar maa nga ca biir, janook néeg Yàlla ba. 10 Néegi wattukati bunt ba féete penkub kër Yàlla ga, ñett la wet gii, ñett wet gee, yépp tolloo, te jën yi leen séq ñoo tolloo yaatuwaay.
11 Waa ja natt yaatuwaayu buntu mbaar mi, bu ubbikoo, muy fukki xasab, yaatuwaayu bunt bi di fukki xasab ak ñett, boo ci boolee jën yi. 12 Fi janook bunti néegi wattukat, yi bindoo juróom benni xasab wet gu nekk, ab dëx a fa tëdde xasab, talaayu dëx ba di xasab. 13 Mu natte mbaar ma ca xadd ba, diggante miiru biiru benn néeg, ak miiru biiru moroom, ma mu jàkkaarlool, muy ñaar fukki xasab ab juróom. 14 Mu def ñaari jëni mbaar mi§ 40.14 jëni mbaar yooyu jën yenuwul dara, dañoo taxaw noonu rekk. juróom benn fukki xasab, ëttu kër Aji Sax ji féete mbaaru bunt bi wet gu nekk. 15 Diggante kanam mbaaru bunt ba, ba fa dal-luwaayu mbaar ma jeexe, juróom fukki xasab la. 16 Néegi wattukat yi ak seeni jën am nañu ay palanteeri biir yu ànd aki caax, te wër néeg yi ba dajal. Dal-luwaayu mbaaru bunt bi itam am ay palanteeri biir yu wër ba dajal. Jën wu ci nekk, ay nataali garabi tàndarma lañu ñaas ca kawam.
Natt nañu ëttu biti ba
17 Waa ja yóbbu ma, ba ca ëttu biti ba. Mu am fa ab dër bu dajal ëtt ba, fanweeri néeg séq ko. 18 Dër ba daa wër mbaari bunt yi waaye dëru ëttu biti bi nag moo gëna suufe bu ëttu biir ba. 19 Waa ja natt diggante mbaaru bunt ba féeteek ëttu biti ba, ak mbaaru ëtt ba féete biir, muy téeméeri xasab. Loola di wetu penku, mu teg ca bëj-gànnaar.
Natt nañu bunt ba féete bëj-gànnaar
20 Mu natt guddaay ak yaatuwaayu mbaaru bunt ba féete bëj-gànnaar, te jëm ca ëttu biti ba. 21 Néegi wattukat ya ñu tabaxaale mbaar ma di ñett genn wet, ñett ca ga ca des. Dayoy jën yaak dal-luwaayu mbaar ma, mook yu buntu penku ba, ñoo bokk yem: guddaay ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. 22 Ay palanteeram ak dal-luwaayam ak nataali garabi tàndarmaam it, lépp a bokk ak yu buntu penku ba dayo. Juróom ñaari dëggastal ngay yéeg, janook dal-luwaayu ba. 23 Niki buntu penku bi rekk, buntu bëj-gànnaar ba daa janook bunt bay jàllale ca ëttu biir ba. Mu natt diggante ñaari bunt ya jàkkaarloo, am téeméeri xasab.
Natt nañu bunt ba féete bëj-saalum
24 Mu yóbbu ma wetu bëj-saalum, ma yem ci buntu bëj-saalum ba. Mu natt ay jënam ak dal-luwaayu mbaaram, dayo ya bokk ak yu bunt ya jiitu, di benn. 25 Foofu itam am na ay palanteer yu wër dal-luwaayu mbaaru bunt ba ba mu daj, nirook yu jëkk ya. Dayo yeet di benn: juróom fukki xasab ci guddaay, ñaar fukki xasab ak juróom ci yaatuwaay. 26 Juróom ñaari dëggastal ngay yéeg dal-luwaay ba. Ay nataali garabi tàndarma lañu ñaas ca kaw jën ya, wet gu nekk genn. 27 Foofu it ëttu biir ba am na bunt bu féete bëj-saalum. Waa ja natt diggante ñaari bunti bëj-saalum yi jàkkaarloo, am téeméeri xasab.
Natt nañu bunt ya jëm ëttu biir ba
28 Waa ja jaarale ma ca buntu bëj-saalum ba, dugal ma ca ëttu biir ba. Mu natt buntu bëj-saalum boobee, ay dayoom di benn. 29 Néegi wattukatam yaak jënam yaak biir dal-luwaayu mbaar ma, lépp a bokk ak ya jiitu ay dayo. Mbaaru bunt ba ak dal-luwaayam am ay palanteer ba dajal, guddaayu mbaaru bunt ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. 30 Néeg yu ndaw yi wër ëttu biir bi ba mu daj, ñaar fukki xasab ak juróom la ci guddaay, juróom ci yaatuwaay. 31 Bunti dal-luwaayi mbaar yaa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba, ñu rafetale jën ya ay nataali garabi tàndarma. Juróom ñetti dëggastal lañu cay dugge.
32 Waa ja jaare penku, dugal ma ca ëttu biir ba. Mu natt buntu penku boobu, dayo ya di benn. 33 Ay néegam aki jënam ak biir dal-luwaay ba, lépp a bokk ak ya ca des ay dayo, juróom fukki xasab ci guddaay, ñaar fukki xasab ak juróom ci yaatuwaay. Mbaaru bunt ba ak dal-luwaayam am na ay palanteer ba dajal. 34 Dal-luwaayu bunt baa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba, ñu ñaas ca kaw jëni bunt ba ay nataali garabi tàndarma, di ca dugge juróom ñetti dëggastal.
35 Waa ja yóbbu ma ba ca buntu bëj-gànnaar ba. Mu natt ko, mu bokk ak ya jiitu ay dayo. 36 Bunt ba daa ànd aki néegam aki jënam ak dal-luwaayam ak palanteer yu ko wër, ba mu daj. Guddaay ba di juróom fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab ak juróom. 37 Mbaaru bunt baa ngay ubbikoo ca ëttu biti ba; ay jënam am wet gu nekk nataali garabi tàndarma, te ñu di ca yéege juróom ñetti dëggastal.
Natt nañu néegu carxal gi
38 Am na néeg buy ubbikoo ci biir mbaaru bëj-gànnaar ba féete biir. Fa lañuy raxase yàppu saraxu rendi-dóomal. 39 Biir dal-luwaay boobu, ñeenti taabal a nga ca, ñaari taabal cat lu nekk. Ca lañuy rey juri sarax yi. Muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu póotum bàkkaar, di saraxu peyug tooñ. 40 Néegu peggu boobu ngay jëkka jot, soo jógee ca biti, ñaari taabal a nga fa, féeteek dëggastal yi ñuy yéege buntu bëj-gànnaar bi ak yeneen ñaari taabal fa féeteek biir dal-luwaay ba. 41 Lépp di juróom ñetti taabal, ñeent wet gii ak ñeent wet gee, ñu di ca rendi. 42 Ñeenti taabali saraxu rendi-dóomal ba, doji yett lañu ko defare. Bu ci nekk di xasab ak genn-wàll, wet gu nekk, taxawaay ba di xasab. Ñu di ca teg jumtukaay yi ñuy rendee saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax. 43 Ñu sàkk ay lonku yu gudde catu loxo, wërale lonku ya ba mu daj ca biir, yàppu sarax ya di tege ca kaw taabal ya.
Natt nañu ëttu biir ba
44 Mu jàlle ma ca ëttu biir ba. Ay néegi jàngkat a nga ca ëttu biir ba, benn bi ci wetu mbaaru bunt bëj-gànnaar bi, jàkkaarlook bëj-saalum, beneen néeg bi ci wetu mbaaru buntu penku bi, jàkkaarlook bëj-gànnaar. 45 Waa ja ne ma: «Néeg bii jàkkaarlook bëj-saalum ñeel na sarxalkat yi dénkoo dénkaaney kër Yàlla gi. 46 Néeg bi jàkkaarlook bëj-gànnaar nag ñeel na sarxalkat yi dénkoo dénkaaney sarxalukaay bi. Ñooñu ñooy Leween ñi askanoo ci Cadog te bokkuñook kenn sañ-sañu jege Aji Sax ji, ngir liggéeyal ko.»
47 Waa ja natt ëttu biir ba, muy téeméeri xasab wet gu nekk. Sarxalukaay baa nga fa kanam néeg Yàlla ba.
Natt nañu néeg Yàlla ba
48 Mu jàlle ma ca dal-luwaayu mbaaru néeg Yàlla ba, daldi natt ñaari jëni dal-luwaay ba, muy juróomi xasab, wet gu nekk. Bunt ba di fukki xasab ak ñeent, ñaari weti biir mbaar ma di ñetti xasab, wet gu ci nekk. 49 Dal-luwaayu mbaar mi gudde ñaar fukki xasab, yaatoo fukki xasab ak benn. Mu am dëggastal yu ñuy yéege, jàll ca biir, ñaari jën séq ko, wet gu nekk, wenn.