Saar 18
Jëf, jël
1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Ana lu waral waxin wi ngeen di waxe fi Israyil naan:
“Baay lekk reseñ ju xaay,
mu uum gëñi doom ja”?
3 «Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, dootuleen waxe woowu waxin fi Israyil. 4 Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
5 Su nit dee boroom njekk,
di jëfe yoon ak njekk,
6 tund ya ca saraxi tuur ya, lekkejiwu ca,
kasaray tuuru waa kër Israyil, wékku cay gëtam,
jabaru jaambur, sobeelu ko,
jigéen ju gis baax, jegewu ko,
7 du kenn ku mu néewal,
xanaa ab tayle, mu delloo ku ko ameel,
alalu jaambur it, foqatiwu ko,
xanaa ku xiif, mu leel,
ku rafle, mu wodd,
8 aw ndollant taxu koo leble,
ab tegandaay, jëlu ko,
xanaa luy njubadi, mu moyu,
àtteb dëgg, mu doxal diggante nit ak nit,
9 sama dogali yoon, mu di ca doxe,
sama àttey yoon, muy jëfe worma:
kooku boroom njekk la,
te mooy dund déy!
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
10 «Jii waay su juree doom ju néeg juy tuur deretu jaambur
mbaa muy def lenn ci yii,
11 te moom miy baayam jëfewu ci lenn,
tund ya ca saraxi tuur ya, doom ja di ca lekki,
jabaru jaambur, mu sobeel,
12 ku ñàkk ak ku néewle, mu néewal,
alalu jaambur, mu foqati,
ab tayle, delloowu ko ku ko ameel,
xanaa kasaray tuur, mu wékki gët,
jëf ju siblu, mu jëfe,
13 ndollant lay leblee,
ab tegandaay, mu jël.
Moo kii nu muy dunde?
Kii kay du dund!
Ak mboolem jëf ju siblu jii mu def,
dee rekk mooy àtteem.
Bakkanam lay gàddu.
14 «Waaye kooka nag su amee doom,
doom ja gis mboolem li baayam bàkkaar,
mu teg ci bëtam te taxul mu roy ko;
15 tund ya ca saraxi tuur ya, lekkiwu ca,
ay gëtam, wékku ko kasaray tuuri waa kër Israyil,
jabaru jaambur, sobeelu ko,
16 du kenn ku mu néewal,
ab tayle, jëlu ko, sàkkuwul ku ko tayle lenn,
alalu jaambur, foqatiwu ko,
xanaa ku xiif, mu leel,
ku rafle, mu wodd,
17 néew-ji-doole, loxoom dalu ko,
ndollant ak ab tegandaay, jëlu ko,
sama àttey yoon lay jëfe,
sama dogali yoon lay doxe.
Kooku du dee ngir ñaawtéefu baayam.
Dina dund déy!
18 Baayam a jaay doole,
moo foqati alalu mbokk,
lu baaxul la def ci biiri bokkam.
Kon nag mooy dee ngir ñaawtéefu boppam.
19 «Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?”
Xanaa du njub ak njekk la doom ji jëfe,
sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm,
di ko jëfe?
Dina dund kay!
20 Ki bàkkaar daal mooy dee.
Doom du gàddu ñaawtéefu baay,
baay it du gàddu ñaawtéefu doom.
Njekk réerul boroom,
mbon réerul boroom.
21 «Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy,
di sàmm sama mboolem dogali yoon,
di jëfe yoon ak njekk,
dina dund déy,
du dee moos!
22 Mboolem tooñam ya mu tooñoon,
deesu ko ko dencal.
Njekk li mu jëfe moo koy taxa dund. 23 Ana bànneex bu ma am ci deewug ku bon?
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Xanaa bu dëddoo jikkoy mbonam, ba dund!
24 «Waaye su dee ku juboon, ba noppi dëddu njubte
di def njubadi,
di roy mboolem jëf ju siblu ju ku bon def,
kooku nu muy dunde?
Mboolem njekk gu mu defoon,
deesu ko ko dencal.
Ag ñàkk wormaam ak bàkkaaram moo koy taxa dee.
25 «Yeen nag ngeen ne: “Boroom bi, ni muy doxale jaaduwul!”
Waa kër Israyiloo, dégluleen!
Sama doxalin a jaaduwul,
am seeni doxalin a jaaduwul?
26 Boroom njekk bu dëddoo njekkam, di def njubadi ba dee,
njubadeem ga mu def moo ko taxa dee.
27 Waaye ku bon nag, bu dëddoo mbonam ga mu nekke,
di def njub ak njekk,
moom moo musal bakkanu boppam.
28 Ndegam moo xoolaat, ba dëddu mboolem tooñam yu mu tooñ, dina dund déy. Du dee moos. 29 Moonte waa kër Israyil nee: “Boroom bi ni muy doxale jaaduwul.” Waa kër Israyiloo, samay doxalin a jaaduwul, am seeni doxalin a jaaduwul?
30 «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor. 31 Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israyil, lu jar ngeen di dee? 32 Man de, bugguma kenn dee. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen ba dund!»